TSK

TSK · Daniel 9:17

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Waxal Aaróona aki doomam ne leen ni ñuy ñaanale bànni Israyil, nii la; nañu leen wax ne leen:

Waaye Aji Sax ji, sama Yàlla, rikk, teewlul li ma lay ñaan, man sab jaam, di la ko dagaan; ngalla déggal sama yuux, te nangu ñaan gi ma lay ñaan bés niki tey.

Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, di woyu Sabóor.

Dikkal, xool gent bu yaa bii dul jeex, noon yàq lépp ci biir kër gu sell gi.

Dawalal sa njàmbaar, ñeel Efrayim ak Beñamin ak Manase, te wallusi nu.

def nga dëkkandoo di nu xëccoo, noon di nu ree.

Sang bi, geesoo ma sag leer, te xamal ma sa dogali yoon,

Te dëkk bi soxlawul jant bu koy leeral mbaa weer, ndax leeru Yàllaa koy leeral, Gàtt bi di làmpam.