Dikkal, xool gent bu yaa bii dul jeex, noon yàq lépp ci biir kër gu sell gi.
TSK
TSK · Daniel 9:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Sa kàdduy seede laay safoo, ñuy sama xejj yi may xelal.
¶ Ma ne: «Boroom bi, foo àppal loolu?» Mu ne: «Xanaa fii ba seeni dëkk gental, ba kenn dëkkatu ca, ba nit dootu nekk biir kër ya, suuf sa yàqu yaxeet, di ndànd-foyfoy.
Sunu kërug jaamookaay gu sell ga te tedd, fa la sunuy maam daa màggale, sawara xoyom na ko, mboolem lu nu soppoon yàqu yaxeet.
Réew mii mépp ay gental, def ndànd-foyfoy, xeet yii yépp di surgawu buuru Babilon diiru juróom ñaar fukki at.
su boobaa maay def kër Yàlla gii, na ma def ga woon ca Silo, te dëkk bii maa koy def lu mboolem xeeti àddina di tudd, di ko móoloo.”»
Mboolem xeet yee koy nangul, nangul doomam ba ci sëtam, ba keroog moom itam, àppu réewam jot. Su boobaa am réewam nangul yeneen xeet yu giir ak buur yu mag.
Ndeysaan! Dëkk beeka wéet tey! Te ñoñam noon gàññ démb. Ndeysaan! Mu ngi mel nib jëtun tey, te noon ràññ fi biir xeet yi! Moo doon lingeeru diiwaan yi, tey mu sasoo liggéeyu sañul-bañ.
¶ May xool ci biir peeñu mi, man Dañeel, di jéema xam lu muy tekki, jëmm juy nirook góor, ne jimeet taxaw ci sama kanam.
«Waxal askanu réew mi mépp, ak sarxalkat yi, nga ne leen: “Ba ngeen dee woor ak a ñaawlu ci weeru juróomeel, ak weeru juróom ñaareel, ci diiru juróom ñaar fukki at yii, ndax man mii ngeen doon woorala wooral?
Ba keroog may dikk, saxool di jàng-biral Mbind mi, di ñaaxe aka jàngle.
¶ Googu texe, yonent ya jottli woon waxyub seen yiw wi leen dikkal, niir nañu ko, càmbar ko.
Ndokklee képp ku jàng ak mboolem ñi déglu yii kàdduy waxyu, tey sàmm li ñu ci bind, ndaxte waxtu wi jege na.