Ci kaw loolu ma dégg baatu nit jibe ca digg yoonu ndox ma ñuy wax Ulay. Mu àddu ca kaw ne: «Jibril, waxal kii peeñu mi.»
TSK
TSK · Daniel 9:22
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Daniel 8:16
TSK
Daniel 10:11
TSK
Mu ne ma: «Dañeel, yaw mi ñu naw, déggal kàddu yi ma lay wax. Jógal taxaw sa taxawaay, ndax dañu maa yebal ci yaw nii.» Naka la ma wax kàddu yooyu, ma ne ñokket, di lox.
Daniel 10:21
TSK
Waaye dinaa la xamal li ñu bind ci téereb dëgg gi. Kenn jàpplewu ma ci ñooñu ku dul Mikayel, seen malaakam wattukat, yeen bànni Israyil.
Zechariah 1:14
TSK
Ca la ma malaaka ma doon wax ak man, ne ma: «Yéeneel, nga ne: Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: “Maa fiire Yerusalem, maa fiire Siyoŋ fiiraange ju réy.
Revelation 4:1
TSK
¶ Gannaaw loolu damaa xool, rekk yem ci bunt bu ubbiku fa asamaan. Ci biir loolu baat ba ma jëkkoona dégg muy wax ak man te mel nig liit, ne ma: «Yéegal fii, ma won la liy topp ci loolu.»