Doole ŋiis, yax yoqi, fit ne soyox, seey.
TSK
TSK · Daniel 9:26
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Dégluleen, jàmbaar ju am doolee ngi dikkal Boroom bi, di tawub doji yuur, ngëlén luy sànke, riddee riddi, sotti waame wu wale! Loxoom la koy rattaxe fi suuf.
Àtte nañu ko ñàkkal, yóbbu, te ag maasam kenn teewluwu ci ne tooñ gu sama bokk yi tooñ lees ko dagge ci réewum aji dund ñi, te loolu lees ko fàdde.
Dina feddli kóllëre diggam ak ñu bare ci benn àppu juróom ñaar, te ci diggu àppu juróom ñaar ba lay dakkal sarax yi ñuy rendi ak yeneen sarax. Ci genn wetu sarxalukaay bi la yàqkat biy taxawal lu siblu, di sabab yàqute, ba keroog muj gi ñu ko dogalal ne milib ci kawam.»
Dina fas yéenee dikk ak dooley nguuram gépp, ba dëgëral digganteem ak buur bëj-saalum. Da koy may doomam soxna, ngir di ko fexee sànk. Waaye loolu du sotti, ndax pexe ma du joy.
Aji Sax ji ne ko: «Tudde ko Lo Ami» (mu firi Du sama ñoñ), mu ne: «ndax dungeen sama ñoñ, te man duma seen dara.»
Boroom bi, Aji Sax ji Boroom gàngoori xare yi, kiy laal suuf, mu ne soyox seey, mboolem lu ci biiram di jooyoo; suuf fuddoondoo ni dexu Niil, dellu rës ni dexu Misra.
Ay bés a ngi dikk ci sa kaw, keroog say noon a lay gawe ab sëkk, yéew la, tance la wet gu nekk.
Dinañu fàddoo ñawkay saamar, te dees na leen jàpp njaam, yóbbu ci mboolem xeet yi. Te jaambur ñi dul Yawut ñooy joggati Yerusalem, ba kera àppu ñooñu dul Yawut di mat.
Mu ne leen: «Nii lees binde, ne fàww Almasi dee ci biir coono, ba ñetteelu fanam, mu dekki,
Ñu indeeti foofa ay seedey naaféq yu ne: «Kii du bàyyee wax mukk lu juunoo ak bérab bu sell bii ak yoonu Musaa.
¶ Almasi moom, moo nu jot ci alkàndey yoon wi, ba mu doonee ku alku ngir nun, nde: «Alkute ñeel na képp ku ñu rey, wékk ko ci bant.»
«Moom ci boppam moo gàddu sunuy bàkkaar, moo ko tegoo ci yaramu boppam ca bant ba,» ngir nu deeyal bàkkaar te dundal njub; «moom mooy ki ngeen wére ci ay góomam.»