Ndaxam muñal nga leen ay at yu bare, di leen artoo sam xel, say yonent di leen ko jottli; waaye taxul ñu déglu. Nga teg leen nag ci loxoy waa réew yi.
TSK
TSK · Daniel 9:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Sunuy buur ak sunuy njiit nag ak sunuy sarxalkat ñoo dale ca sunuy maam, di baña topp sa yoon, baña sàmm say santaane, bàyyiwuñu xel it ci kàdduy seede yi nga leen artoo.
Aji Sax ji dafa wax ne: «Taxawleen ca selebe yoon wa, xool, te laajte yoon ya woon, ne: “Ana yoonu mbaax?” Ngeen awe ca, am noflaayu bakkan.» Ñu lànk ne: «Awunu ca.»
Waaye déggluwñu ma, teewluwñu ma, xanaa di jëfe seen xel ak seen dëgër bopp ak seen bon xol, ba tax ñu dellu gannaaw, jëmuñu kanam.
Waaye dégluwñu, teewluwñu ma, xanaa sajju loos, di bon, ba yées seeni maam.
dégguleen sama kàdduy jaam ñiy yonent yi may yónni ci yeen ay yooni yoon, ngeen tëë dégg,
ndax mboolem lu bon li bànni Israyil ak Yuda def, di ma merloo, ñook seeni buur ak seeni kàngam ak seeni sarxalkat ak seeni yonent ak waa Yuda ak waa Yerusalem.
«Li nga nuy wax ci turu Aji Sax ji, dunu ko déglu.
Buleen mel ni seen maam, ya yonent yu jëkk ya biraloon ne leen: “Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: Dëdduleen seeni jikko yu bon ak seeni jëf ju bon.” Te dégluwuñu, faalewuñu ma.» Kàddug Aji Sax jee.
Ba tóokër ba ñoree, mu yebal ca beykat ya ab surga, ngir ñu jox ko wàllam ca meññeef ma. Beykat ya dóor surga ba, ba noppi dàq ko, mu dellu loxoy neen.
Waa Yerusalem, ak seeni kilifa nag xàmmiwuñu woon Yeesu, te ba ñu daanee Yeesu lañu sottal waxu yonent, ya ñu daan biral bésub Noflaay bu nekk.