TSK

TSK · Deuteronomy 2:23

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ak Pataruseen ñi ak Kasluyeen, ñooñee waa Filisti bàyyikoo ca seen réew; ak it Kaftoreen ñi.

Ci kaw loolu dàq na waa Filisti, ba ca dëkk ba ñuy wax Gasa ak diiwaanam, dale ko ca tatay wattukat ya ba ca dëkk yu mag ya ñu wëraley tata.

bésub sànkute dikkal képp kuy Filisteen, ba dagge dëkk yii di Tir ak Sidon ndimbal lu ñu dese woon. Aji Sax jaa ngay sànk Filisteen, ña des te cosaanoo dunu Keret.

Gasa dëkk ba lees di wacc, Askalon gental, Asdodd, digg bëccëg lees leen di buub, génne, te Ekkron lees di déjjati.

Moo sàkke xeeti àddina yépp ci kenn nit, ñu dëkke déndu suuf sépp, te moo leen àppal seeni jamono, rëddal leen seen kemi dëkkuwaay.