¶ «Ku dóor baayam mbaa ndeyam, dee rekk mooy àtteem.
TSK
TSK · Deuteronomy 21:18
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Na ku nekk weg ndeyam ak baayam te wormaal sama bési Noflaay. Man Aji Sax ji, maay seen Yàlla.
Xamleen xéll ne ni baay di yare doomam, ni la leen seen Yàlla Aji Sax ji yare.
Man maay doon baay ci moom, moom, muy doom ci man. Su defee naka su dul noonu, maa koy yare bantu nit, ak dumay doom aadama.
Ku dul bantal sa doom, bëggoo ko. Ku bëgg sa doom teel koo yar.
Yaral sa doom ba muy teel, waaye bul topp sa xol, ba rey ko.
Yëfi dof daa sax ci xolu gone, boo bantalee, mu tàggook moom.
Ku xañ say waajur seen alal te defe ne tooñoo, yaa neexook saaysaayu yàqkat.
Ag maas a ngi saaga baay, te wormaaluñu ndey.
Asamaan, déglul; suuf, teewlul, Aji Sax jeey àddu: «Ay gone laa yar, màggloo leen, ñoom, ñu gàntal ma.
Aji Sax ji, xanaa du worma ngay sàkku? Dóor nga leen, safu leen; nga làbbli, ñu tanqamlu, wowle ba raw doj, baña dëpp.
Ndey ak baay, ñu tuutal fi sa biir; doxandéem bi, ñu lekk àqam fi sa biir; jirim akub jëtun, ñu néewal fi sa biir.
«Maa jàllarbi lenn ci yeen, na ma jàllarbee woon waa Sodom ak Gomor. Ngeen rëcce ca ni gillit gu ñu fëkke cib taal. Taxul ba tey ngeen waññiku fi man.» Kàddug Aji Sax jee!
Te itam am nanu ay baay ci wàllu deret, ñoo nu daan yar, te danu leena wegoon. Kon nag xanaa du Baay bi yor ug noo lanu wara gënatee nangul, ngir nu dund?