Numbers 35:33
TSK
Buleen tilimal réew mi ngeen nekk. Deret kat mooy tilimal réew mi, te réew mi deesu ko jote lenn, ci deret ju ñu tuur ci biiram, lu moy deretu ka tuur deret.
TSK
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Buleen tilimal réew mi ngeen nekk. Deret kat mooy tilimal réew mi, te réew mi deesu ko jote lenn, ci deret ju ñu tuur ci biiram, lu moy deretu ka tuur deret.
ak deretu nit ñi mu tuur te defuñu dara; ndax Manase daa feesal Yerusalem ak deretu jaamburi Yàlla, ba Aji Sax ji nanguwu koo baal.
Xamleen xéll rekk ne su ngeen ma reyee, bakkanu ku deful dara ngeen gàddu, yeen ak dëkk beek ñi ko dëkke, ndax ci lu wér Aji Sax jee ma yebal ci yeen, ngir ma yegge leen mboolem kàddu yii.»
Dañuy dal fi sa kaw, aki gànnaay, watiir aki mbege ak kurélu xeeti xeet, ŋàbb pakk bu mag ak bu ndaw, sol mbaxanam xare, dar kepp la. Maa leen di jox sañ-sañu mbugal, ñu mbugal la, ni ñu baaxoo mbugale.