TSK

TSK · Deuteronomy 32:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Musaa ne Yàlla: «Su ma demee ca bànni Israyil, ne leen seen Yàllay maam ya moo ma yónni ca ñoom bànni Israyil de, dinañu ma laaj nu mu tudd. Lu ma leen di wax nag?»

Sarxalukaay bu ñu defare suuf ngeen may sàkkal, di ci sarxal seeni gàtt ak seeni nag, muy seen saraxu rendi-dóomal, mbaa seen saraxi cant ci biir jàmm. Sàkkleen ab sarxalukaay ci mboolem bérab bu may fàttlee sama tur, ma dikk fi yeen, barkeel leen.

¶ Aji Sax ji nag wàcc ci biir aw niir, taxaw ak Musaa foofa, daldi biral turam, ne: «Aji Sax ji.»

Ngeen ne ma: «Sunu Yàlla Aji Sax ji kat, moo nu won darajaam ak màggaayam. Kàddoom lanu dégg, mu jibe ca digg sawara wa. Bésub tey noo gis Yàlla wax ak doom aadama, ba noppi, muy wéye bakkanam!

Aji Sax ji, ndokklee mbooloo mu la xal di sarxollee, di niitoo saw yiw,

Muy jàngi màggal, ñeel Daawuda. Sama Yàlla, Buur bi, naa la màggal, teral sa tur ba fàww.

Màggaleleen ko ay jalooreem, màggale ko màggam gu réy.

Ay jantam Yuda dina texe, Israyil dëkke kaaraange, te dees na ko tudde nii: “Aji Sax ji sunu njekk.”

Ngeen boole ci xam manooreem gu nattuwul gi mu nu lañalal, nun gëmkat ñi. Manoore googu feeñ na ci jëf ji sottee ci kàttanam ak dooleem,