Rikk bul yemale ku jub ak ku jubadi, ba boole leen rey, loolu jomb na la moos! Yaw miy àtte àddina sépp kay, lu jub rekk ngay def!»
TSK
TSK · Deuteronomy 32:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Xamleen boog ne seen Yàlla Aji Sax ji moom mooy Yàlla; mooy Yàlla ju dëggu jiy sàmm kóllëre ak ngor ñeel soppeem ñiy sàmm ay santaaneem, sët ba sëtaat, ba ci junniy maas.
Yeen Yesurun, yeena yaflu, waŋŋeetu, solu yaram, ne faaj, ne fuux, fàtte Yàlla mi leen sàkk, faaleedi seen cëslaay li leen musal.
Ana nu kenn di dàqe seen junni, ñaar di fëxal seen fukki junni, te ka ñu yaakaar jaayu leen, te Aji Sax ji, laa ne, waccu leen?
Mu ne: Aji Sax ji laay sës, mu di ma aar, di ma wallu.
Aji Sax jeey Kiy dund. Kii ma sës moo jara sant. Yàlla sama cëslaay ji may musal moo màgg!
Yaa gis mu nangul la ci xolam; nga fas ak moom kóllëre, dig askanam réewum Kanaaneen ñaak Etteen ñaak Amoreen ñaak Periseen ñaak Yebuseen ñaak Girgaseen ña. Te def nga li nga dige it, ndax yaw boroom njekk nga.
Kon ngalla yaw mi ne gisoo ko, te ne diis nga ko sa mbir, di ko xaar.
Mu ne: Aji Sax ji, maa la sopp, yaw mi may dooleel.
ne yàcc, génne seeni tata, di lox.
Génne ma fiir gi ñu may tëroo; yaw yaa di sama rawtu.
Ngalla Yàlla, déglul, maa ne wallóoy, teewlul, ma dagaan la.
Ay xàmbaar a ko yéew, njekk ak njub lal ab jalam.
Buur, jëfe yoon mooy dooleem, te yaa saxal njub, yoon ak njekk ci askanu Yanqóoba.
Aji Sax jee may feyul. Éy Aji Sax ji, yaa saxoo ngor! Bul wacc ñi nga binde sa loxo.
ki sàkk kaw ak suuf, géej ak lu ci biiram, di sàmm dëgg ba fàww,
Aji Sax ji, yaay sama Yàlla, dama lay teral, di la sant. Yaa defi jaloore, muy dogal yu yàgg, wér te wóor.
Moo tax Boroom bi Aji Sax ji wax ne: «Maa ngii di dëj fi Siyoŋ aw doju coll, muy doju collu tànnéef wu gànjare ngir kenu gi, te ku ko wéeroo doo gaawa daw.
ku ci nekk mel ni seelukaayu ngelaw, di kiiraay ci ngëlén, mel ni wali ndox ci suuf su ne sereŋ, mbaa keppaaru doj wu mag ci àll bu mar.
Waaye Aji Sax jeey Yàlla dëgg. Mooy Yàlla jiy dund, di buur ba fàww, xadaram gësëm àddina, meram man xeet yi.
Moonte xam nañu xéll ne ñiy jëfe noonu, Yàlla moo daganal àtteb dee ci ñoom, te teewul ñu di ko jëfe, rax ci dolli di farle ñi koy jëfe.
¶ Waaye sag dëgër bopp, ak sa xol bu tuubadi, ci ngay jóore sànjum Yàlla ci sa kaw bopp, keroog bésub sànj ma, fa àtteb Yàlla bu jub di feeñe.
te ñoom ñépp, menn ndoxum kéemaanu Yàlla ma lañu naan, ndax ñoo doon naane ca doju kéemaanu Yàlla ga, doj wa leen doon gunge, te doj wa Almasi la woon.
Boroom yoon wi, kenn doŋŋ la, te mooy àtte; moo mana musle, mbaa mu sànke. Te yaw miy sikkal sa mbokkum gëmkat sax, yaay kan?
Ña ngay woy woyu Musaa jaamu Yàlla ba, ak woyu Gàtt bi, naan: «Yaw Boroom bi Yàlla Aji Man ji, yaa réy te yéeme ay jaloore. Yaw Buuru askan yi, yaa jub te dëgguy doxalin.