¶ Kàddu yii la Aji Sax ji wax seen ndaje ma mépp, ca tund wa, ba mu àddoo ca digg sawara wa, kàddu gu xumb, ci biir xàmbaar gu lëndëm këruus. Tegaatu ca dara. Mu daldi bind kàddu yi ci ñaari àlluway doj, jox ma.
TSK
TSK · Deuteronomy 33:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ñu jóge Majan, dem Paran, ànd ak ay waa Paran dem Misra, ca Firawna buuru Misra. Firawna jox Adàdd suuf, may ko kër akub dund.
Yàllaay sàkkal ku wéet wéttal, di afal ku ñu tëjoon, bégal ko, ku déggadi rekk ay dëkke suuf su ne sereŋ.
Watiiri xarey Yàlla di ñaar fukki junni (20 000), ba ci junniy junni. Boroom bi ne ca seen biir, di boroom tundu Sinayi fa biir sellngaam.
Yàllaa ngi jóge Teman, Aji Sell ji foofa ca tundu Paran lay bawoo. Selaw Darajaam moo dajal asamaan, teddngaam fees kaw suuf.
¶ Mbindum ndigali yoon wi, ci aw doj lees ko rëddoon, te Musaa moo sasoo woon liggéeyu yoon woowuy jëme ci ndee. Teewul muy liggéey bu làmboo ag leer gu doon lerxat ca kanam ga, ba bànni Israyil tële koo xool jàkk, doonte leer guy wéy la woon.
¶ Mboolem ñi yaakaar seen jëf ju ñu sàmme yoonu Musaa, repp nañoo alku, nde bindees na ne: «Alkànde ñeel na képp ku saxoowul mboolem digal yi ñu bind ci téereb yoon wi, ngir di ko jëfe.»
Dina feeñ it ndax noflaay ba mu nuy booleek yeen ñiy dékku ab coono, sédde nu ko, kera bés bu Sang Yeesu feeñee, ànd ak ay malaakaam yu làmboo manooreem, wàcce asamaan.
Manuñu woona xajoo ndigal la ne: «Mala sax, su laalee tund wi, dóorleen koy doj ba mu dee.»
¶ Ma xoolaat, daldi dégg baati malaaka yu bare, ñu yéew ngàngune mi ak bindeef yi ak mag ñi, seen lim di ay junni, ba ci junniy junni.