Mbooloom bànni Israyil gépp nag di diiŋat Musaa ak Aaróona ca màndiŋ ma.
TSK
TSK · Deuteronomy 8:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Exodus 16:2
TSK
Exodus 16:12
TSK
«Dégg naa diiŋati bànni Israyil. Wax leen ne leen, diggante ngoon ak jant bu so, dinañu lekk yàpp, te bu bët setee ñu lekk aw ñam, ba regg, ndax ñu xam ne man Aji Sax ji, maay seen Yàlla.»
Deuteronomy 29:5
TSK
Mburu, lekkuleen ko, biiñ mbaa geneen naan gu diis, naanuleen ko. Maa leen leel, ngir ngeen xam ne man maay seen Yàlla Aji Sax ji.»
Psalms 37:3
TSK
Dénkul ci Aji Sax ji, di def lu baax, ba des ci réew meek jàmm.
Psalms 104:27
TSK
Ñoom ñépp yaw lañuy séentu, ngir bu jotee, nga leel leen,
Luke 12:29
TSK
Yeen nag, buleen tiisoo lu ngeen lekk, mbaa lu ngeen naan; te bu yooyu xalaat ub seen bopp.
Hebrews 13:5
TSK
¶ Buleen jikkowoo bëgg ub xaalis; doylooleen li ngeen am, ndax Yàlla moo ne: «Duma la bàyyi mukk, duma la wacc mukk.»