Saarata ne: «Yàllaaka maa bégal, may ree, ànd ak ku yég, nuy ree.»
TSK
TSK · Ecclesiastes 3:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba gaalu Aji Sax jay duggsi ca biir gox ba ñu naan Kër Daawuda, soxnas Daawuda, Mikal doomu Sóol a nga sëppu ca palanteeram. Mu gis Buur Daawuda di tëb ak a fecc ca kanam Aji Sax ji. Mu jéppi ko lool.
¶ Keroog ñaar fukki fan ak ñeent ca weer woowa, bànni Israyil daje nañu, sol ay saaku, xëppoo suuf, di ko ñaawloo ci biir koor.
Muy jàngi yéeg, ñu di ko màggale Yàlla. Ba Aji Sax ji delloo waa Siyoŋ seen réew, danoo meloon ni ñuy gént,
Su neexee, bànneexul; su mettee, xoolal ne lu ci ne, Yàllaa ko def ngir jaam bi umple gannaawam.
Dëfal-leena dëfal sama ñoñ, la seen Yàlla wax!
Malaaka ma ne ko: «Sàkkaryaa, bul tiit, ndax sa ñaan nangu na. Elisabet sa soxna dina am doom ju góor, nanga ko tudde Yaxya.
Ndokklee yeen ñi xiif tey, nde dingeen regg. Ndokklee yeen ñiy jooy tey, nde dingeen ree.
Ñi ci mbégte, bokkleen ak ñoom seen mbégte; ñi ci naqar, ngeen bokk ak ñoom seen naqar.
Tiisluleen te ñaawlu bay jooy. Na seeni ree soppiku ay jooy, seen mbég doon njàqare.