Maa jàddoon, nga duma ma, léegi sa kàddu laay sàmm.
TSK
TSK · Ecclesiastes 7:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Kuy ji di jooy, yal na góob, di sarxolle.
«Maa ngii di jële sama ñoñ réewum bëj-gànnaar, dajalee leen fa cati àddina. Silmaxaa ngi ci akub lafañ, jigéenu wérul it ak kuy wasin, ñuy gàngoor gu mag, délsi fii.
Su bés baa, ci yooyu fan,» kàddug Aji Sax jee, «bànni Israyil ay ànd ak Yudeen ñi, dikk di jooy, di sàkku seen Yàlla Aji Sax ji.
¶ Jant yooyu, man Dañeel maa nga doon ñaawlu diiru ñetti ayi bés.
¶ «Bu loolu amee maay sottil waa kër Daawuda ak waa Yerusalem, noowug yiw aki dagaan, ba ñu geesu ma man, mi ñu jam ba mu sar, te dinañu ko jooy ni ñuy jooye benn bàjjo, di ko naqarlu ni ñuy naqarloo deewug taaw.
Wóoy ngalla yeen ñi regg tey, ndax dingeen xiif ëllëg. Wóoy yeen ñiy ree tey, ndax dingeen tiislu, dingeen jooy.
Te yemunu ci, xanaa di sagoo sunuy tiis itam, nde xam nanu ne dékku aw tiis mooy taxa muñ;
Waaye tey bég naa, te du tiis wu ngeen tegoo laay bége, waaye li leen tiis wi tuubloo, laay bége, ndax woowu xeetu tiis la Yàlla namm ci yeen, moo tax it yóbbewunu leen jenn loraange.
¶ Bokk yi, bu ngeen jaaree ci mboolem xeeti nattu, jàppeleen ko mbég mu mat sëkk,