TSK

TSK · Esther 1:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Buur, dangay yónnee ay ndaw ci sa mboolem diiwaani réew mi, ñu dajaleel la mboolem janq ju rafet ji, indi leen fii ci Sus, péey bi, dugal leen ci kër jigéen ñi, ñu teg leen ci loxol Ege, sa bëkk-néeg biy wattu jigéen ñi. Ñu jox leen lu ñuy defaroo ba rafet.

¶ Ndaw ya gaaw dem ci ndigalal buur, ñu biral dogal ba ca Sus, péey ba. Buur a nga toog ak Aman, di naan, waa Sus nekk ci njàqare.

Buur ne Lingeer Esteer: «Biir Sus, péey bii, Yawut yi rey nañu ci juróomi téeméeri nit, reyaale fukki doomi Aman yu góor. Kon diiwaani buur yi ci des xawma nu ñu def ak ñoom. Ana looy ñaanati, ñu may la ko ak looy sàkkooti, ñu defal la ko?»

Ca biir peeñu ma, maa ngi Sus, péeyub diiwaanu Elam. Ma gis ci peeñu mi ne maa ngi ci wetu yoonu ndox ma ñu gas te ñu di ko wax Ulay.