TSK

TSK · Esther 4:3

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Naka la agsi, yem ca Eli, mu toog ca toogoom ca peggu yoon wa, di séentu, ndax booba naw gaa ngay rëcc, ngir tiitaange ca gaalu Yàlla ga. Naka la waa ja duggsi ca dëkk ba, ba wax la xew, dëkk ba bépp yuuxoondoo.

¶ Lii mu ngi amoon ci jamonoy Aserus. Mooy Aserus ma falu woon, jiite téeméeri diiwaan ak ñaar fukk ak juróom ñaar, dale ko ca End ga woon, ba ca réewum Kuus.

«Demal woo mboolem Yawut yi, ci Sus, ñu daje. Te ngeen wooral ma: buleen lekk, buleen naan diiru ñetti fan, du guddi, du bëccëg. Man it maak sama surga yu jigéen, nu woore noonu. Su ko defee ma dem ca Buur doonte yoon nanguwu ko. Su ma dee dee, ma dee rekk.»

Job 2:8 TSK

Mu wut tojitu njaq, di ko xasanoo, daldi toog ci biir jalub dóom.

Bésub keroog Boroom bi, Aji Sax ji ci gàngoor yi moo leen di woo ci jooyoo ak ñaawlu ak wateefu nel, ak colu saaku ngir ñaawlu.

Ndax lii moo di koor gi ma taamu, ci bés bu nit kiy toroxlu? Koorug dëngal loos ni barax, lal saaku, sotti ab dóom, tëdd di ko ñaawloo? Loolooy seen koor, ci bés bu Aji Sax ji rafetlu?

Ma walbatiku jublook Boroom bi Yàlla. Maa ngi sol saaku, diwoo dóom boole kook koor, toroxloo ko, di ko ñaan ak a dagaan.