TSK

TSK · Exodus 13:12

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Li tuuroo ci seen sàq yu fees, ak li wale ci seen nalukaay yu rembat, sama cér la; buleen ko yeexe, te seen taaw yu góor it, man ngeen leen di sédde.

¶ «Bépp taaw bu góor maay boroom, ba ci lépp lu góor lu jur taawloo, muy nag mbaa gàtt.

¶ «Waaye kat luy taaw cig jur, Aji Sax jee ko moom jeeg. Du lu kenn di dogoo jagleel Aji Sax ji. Muy barmol, muy mbote, muy tef, Aji Sax jeey boroom.

Ndax lépp luy taaw bu góor, sama cér la. Keroog ba ma fàddee lépp luy taaw bu góor ca réewum Misra, ca laa sellalal sama bopp lépp luy taaw ci Israyil, dale ci nit ba ci jur. Maa leen séddoo. Maay Aji Sax ji.»

Lépp luy ubbitey njur bu ñu jagleel Aji Sax ji, ci lépp lu bindoo aw suux, nit ak mala, yaa koy moom. Fexeel rekk ba jotlu taawub nit ki, te taawub mala mu setul it, nanga ko jotlu.

¶ Nu dogu ba tey ne dinanu yóbbu ca kër Aji Sax ji, at mu nekk, li sunu suuf jëkka meññle ak lu garab yépp jëkka ñorle.

Li gën ci mboolem ndoortel meññeef, ak seen bépp jooxe ak bu mu mana doon, sarxalkat yee ko moom. Li gën ci seen notu sunguf, nangeen ko jox sarxalkat yi, ndax barke wàccal seen kër.