TSK

TSK · Exodus 13:2

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

nangeen sédde Aji Sax ji lépp lu jëkka juddu, rendil ko ko: lépp luy góor lu seen jur taawloo, Aji Sax jeey boroom.

Seen jur gu gudd ak gu gàtt itam, naka noonu. Juróom ñaari fan lay nekk ak ndeyam, bésub juróom ñetteel ba, ngeen jox ma ko.

¶ «Bépp taaw bu góor maay boroom, ba ci lépp lu góor lu jur taawloo, muy nag mbaa gàtt.

Ndax lépp luy taaw bu góor, sama cér la. Keroog ba ma fàddee lépp luy taaw bu góor ca réewum Misra, ca laa sellalal sama bopp lépp luy taaw ci Israyil, dale ci nit ba ci jur. Maa leen séddoo. Maay Aji Sax ji.»

Lépp luy ubbitey njur bu ñu jagleel Aji Sax ji, ci lépp lu bindoo aw suux, nit ak mala, yaa koy moom. Fexeel rekk ba jotlu taawub nit ki, te taawub mala mu setul it, nanga ko jotlu.

¶ Nu dogu ba tey ne dinanu yóbbu ca kër Aji Sax ji, at mu nekk, li sunu suuf jëkka meññle ak lu garab yépp jëkka ñorle.

Luke 2:23 TSK

noonee ñu ko binde ci yoonu Boroom bi ne: «Bépp taaw bu góor, dees koy tudde séddoo bu sell, ñeel Boroom bi.»