TSK

TSK · Exodus 13:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ci kaw loolu malaakam Yàlla, ma féete woon xarekati Israyil kanam naka jekk te di leen jiite, daldi toxu, féete leen gannaaw. Niir, wa leen jiitu woon it walbatiku, taxaw ca seen gannaaw,

Te bu Musaa duggaan ca xayma ba, taxaaru niir wa day wàcc, ne tekk ca bunt xayma ba, fekk Aji Sax jaa ngay wax ak Musaa.

Ndax booba niiru Aji Sax jaa nga ca kaw jaamookaay ba, ag bëccëg, te sawara waa nga ca biir niir wa, ag guddi, waa kër Israyil gépp di ci gis, seen diiru yooni tukki ya.

Noonu la ko niir wa jàppoo muure, bu guddee mu mel ni sawara.

te dinañu ko nettali waa réew mii. Waa réew mii dégg nañu ne yaw Aji Sax ji ci sa bopp yaa nekk ci digg mbooloo mii ngay feeñu bët ak bët, yaw Aji Sax ji, saw niir taxaw, tiim leen, te aw taxaaru niir nga leen di jiitoo bëccëg, jiitoo leen aw taxaaru sawara, guddi.

Ci kaw loolu nga di leen jiitee bëccëg aw taxaaru niir, di leen jiitee guddi taxaaru sawara, di leen niital yoon wa ñuy jaare.

Bëccëg mu jiitee leen aw niir, ak leeru sawara guddi gépp.

Mu firiw niir, yiire leen, ak sawara, ñu niitoo guddi.

¶ Bokk yi, bugguma ngeen umple ko, sunu maam yépp la niir wa yiiroon, te ñoom ñépp a jàll géej ga.