TSK

TSK · Exodus 21:14

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Su dee ci biir mbañeel la dale ci kawam, mbaa mu sànni ko aw saan wu mu ko waajal, ba mu dee,

Képp ku ci daŋŋiiral, baña déggal sarxalkat ba fa ayee liggéeyal seen Yàlla Aji Sax ji, baña déggal àttekat ba, kooku dees koy rey. Noonu ngeen di tenqee lu bon ci Israyil.

¶ Su fekkee ne nit ki dafa bañ moroomam, su ko tëroo, dal ci kawam, ba fàdd ko, mu dee, su làqujee ci dëkk yooyu benn,

¶ Ñu neeti: «Alku ñeel na ku rey moroomam ci kumpa.» Mbooloo mépp ne: «Amiin!»

Yowab ne Amasa: «Mbokk mi, mbaa jàmm nga am?» Yowab jàpp sikkimu Amasa ca loxol ndijooram, mel ni ku koy fóon.

¶ Yowab àndul woon ak Absalom ci pexeem, waaye Adoña la mujj àndal. Ba Yowab yégee la xew, daa daw ba ca xaymab Aji Sax ji, jàpp ca béjjén ya ca cati sarxalukaay ba, ngir rawale bakkanam.

Ci kaw loolu Yoyada sarxalkat ba sant njiiti kuréli téeméer ya, kilifay gàngoor ga, ne leen: «Génneleen ko làng gi, te ku ko topp, jamleen ko, mu dee.» Fekk na Yoyada ne buñu ko rey ci biir kër Aji Sax ji.

Ku bóom nit, daw, ba tàbbi njaniiw; bu ko kenn taxawu.

¶ Rawatina nag boroom xemmemtéefi yàqute, yi topp seen bakkan te faalewuñu genn kilifteef. Ñu fétteeral lañu te bew, ragaluñoo saaga sax boroom daraja yu kawe ya fa asamaan.