TSK

TSK · Exodus 21:6

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ «Guddig keroog maay wër réewum Misra te maay fàdd lépp luy taaw bu góor ci réewum Misra, nit ak mala, te itam maay mbugal mboolem tuuri Misra. Man maay Aji Sax ji.

¶ «Su ay góor dee jàppante, ba kenn ci ñoom dal ci jigéenu wérul, ba liir bi génn, bu ci genn loraange toppul, dees na feyloo moos ki dal ci kawam, ndàmpaay li jëkkër ji laaj, te ña leen di àtte juboo ca limu pey ga.

¶ «Li tuuroo ci seen sàq yu fees, ak li wale ci seen nalukaay yu rembat, sama cér la; buleen ko yeexe, te seen taaw yu góor it, man ngeen leen di sédde.

Defleen ko ni liggéeykat buy feyeeku mbaa màngaan bu ngeen dëkkal. Na leen liggéeyal ba keroog atum Yiwiku ma,

Jant yooyu laa sant seeni àttekat ne leen: «Deeleen déglu seeni bokk tey àtte dëgg, diggante bànni Israyil ak mbokkam, akub doxandéem.

¶ Te itam ay àttekat aki kilifa ngeen di tabb ngir seeni giir, ci mboolem dëkk yi leen seen Yàlla Aji Sax jiy jox, ñuy àtte mbooloo mi àtteb dëgg.

Waaye Aana demul, ndax dafa wax jëkkëram ne ko: «Gannaaw bu xale bi feree laa koy yóbbu, sédde ko Aji Sax ji, mu des foofa benn yoon.»

Akis nag amoon na kóolute ci Daawuda, ndax da doon wax ci xelam naan: «Kii de yóbbe na boppam mbañeel gu ko bokki bànni Israyilam bañ lool. Moo tax sama surga rekk lay doon ba fàww.»

Ñu ne ko: «Soo nangulee tey mbooloo mii, déggal leen, wax leen kàddu yu rafet, say jaam lañuy doon ba fàww.»

Maay waññi say àttekat, ñu mel na woon, say diglekat it dellu mel ni bu jëkkoon. Su boobaa ñu wooye la Dëkkub Njekk, ak Dëkkub Kóllëre.»