TSK

TSK · Exodus 22:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

«Man Aji Sax ji, maa di seen Yàlla, ji leen génne réewum Misra, kërug njaam ga.

¶ «Bu ab doxandéem daleek yeen ci seenum réew, buleen ko lor.

Kiy aar jirim akub jëtun, sopp doxandéem, ngir leel ko, wodd ko.

Fàttlikuleen ne ay jaam ngeen woon ca réewum Misra, seen Yàlla Aji Sax ji moo leen jot. Moo tax ma sant leen lii tey.

¶ Buleen xañ dëgg ab doxandéem akub jirim, te buleen taylelu mbubbum jëtun.

Aji Sax jeey sàmm doxandéem, taxawu jirim ak jëtun, waaye mooy lajjal pexem ku bon.

te notuleen doxandéem, ab jirim akub jëtun, tuuruleen deretu jaamburu Yàlla, fi bii bérab, toppuleen yeneen yàlla bay loru,

Ab jëtun, ak ab jirim, ak ab doxandéem, ak ab néew-doole, buleen ko not. Lu bon it, buleen ko mébétalante ci seen xol.»