Mbooloo ma mépp bokk benn baat, àddu ne: «Li Aji Sax ji wax lépp dinanu ko def.» Ci kaw loolu Musaa dem yegge Aji Sax ji tontal mbooloo ma.
TSK
TSK · Exodus 24:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ba loolu amee mu jël téere ba ñu bind kóllëre ga, jàngal ko mbooloo ma, ñuy dégg. Mbooloo ma ne ko: «Li Aji Sax ji wax lépp dinanu ko def, ba mu mat sëkk.»
¶ Mu ngoog, jàngal naa leen ay dogali yoon, aki àttey yoon, na ma ko sama Yàlla Aji Sax ji sante, ngir ngeen war koo jëfe ca biir réew ma ngeen di nanguji.
¶ Musaa moo woo bànni Israyil gépp, wax leen ne leen: Yeen, bànni Israyil, dégluleen dogali yoon yi, ak àttey yoon yi may wax, ngeen dégg, tey. Jàngleen ko te farlu koo jëfe.
Yaw nag, taxawal fi man, ba ma jox la mboolem santaane bi, dogali yoon yi, ak àttey yoon yi nga leen di jàngal, te ñu war koo jëfe ca réew ma ma leen jox, ngir ñu nangu ko.»
¶ Soppleen seen Yàlla Aji Sax ji, te ngeen dénkoo ndénkaaneem, ak dogali yoonam, ak àttey yoonam, aki santaaneem, bés bu nekk.
Googu kàddu laa jaayante woon ak yeen, ba ngeen di génne Misra. Samag Noo laa taxawe fi seen biir, buleen tiit.