TSK

TSK · Exodus 29:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Te nga jël diwu pal gi, sotti ko ci kaw boppam, diw ko.

Aaróona aki doomam itam, nanga leen diw. Noonu nga leen di sellale, ngir ñu doon samay sarxalkat.

¶ Musaa teg ca sàkk ca diwu pal ga, ak deret ji ci sarxalukaay bi, wis-wisal ko ci kaw yaramu Aaróona ak ca kawi yéreem, wis-wisaale ko ca kaw yarami doomam yu góor ak ca kaw yérey doomam.

Li des ci diw gi ci loxol sarxalkat bi na ko diw ci boppu ki ñuy laabal, defal ko ko njotlaay fi kanam Aji Sax ji.

xelum Aji Sax ji tegu fi kawam, xelum rafet xalaat ak ràññee, xelum digle ak njàmbaar, xelum xam Aji Sax ji, ragal ko.

Kon ki dëggaate Doomu Yàlla ji, teddadil deret ji ñu sellale kóllëre gi, te ñàkke teggin Noowug Yàlla gi nu indil aw yiw, kooku, mbugal ga mu yelloo, ñaata yoon lay gënatee metti, ngeen defe?