Nanga ber dënn bi ñu def saraxu yékkati-jébbale, mook tànkub jooxe bi ñu def saraxu yékkati-jébbale, te ñu jooxee ko ci kuuyu colu gi, ñeel Aaróona aki doomam.
TSK
TSK · Exodus 29:28
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Li yoon dogal ci saraxu cant ci biir jàmm, te nit sañ koo sarxalal Aji Sax ji mooy lii:
Tànkub jooxe bi ak dënnu saraxu yékkati-jébbale bi, mook nebbon bi ñuy def saraxu sawara, dees koy boole indi yékkati ko, def ko sarax bu ñuy yékkati, jébbal Aji Sax ji. Yeena moom yooyu, yaak say doom, muy seen cér bu ñu leen dogalal fàww, te di la Aji Sax ji santaane woon.»
Ku nekk ci sarxalkat yi, sa sarax yu sell, yaa ko moom. Ku ci nekk, li ñu la jox, yaay boroom.»
bay lekk ca ñamu réew ma, nangeen ci jooxe ab jooxe, ñeel Aji Sax ji;
¶ Aji Sax ji neeti Aaróona: «Man mii maa la sédd ndénkaaneb samay jooxe; mboolem jooxe yu sell yi bànni Israyil indi, yaw laa ko jagleel, nga jagoo, yaak say doom, ci kaw dogal bu sax dàkk.
Lépp lu ñu leen sédd, nangeen ci jooxe jooxeb Aji Sax ji. Mboolem céri ngëneel yooyu, ci ngeen di génne cér bu sell boobu.
Ci céru xarekat yi ngeen koy sàkke, jox ko Elasar sarxalkat bi, muy jooxeb Aji Sax ji.
Lii mooy li lew sarxalkat yi, te bàyyikoo ci askan wi, ci ñiy rendi ay sarax, muy aw nag, di ab gàtt: nañu jox sarxalkat bi, mbagg mi ak lex yi, ak mbàq gi.