TSK

TSK · Exodus 29:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Nanga solal yooyii sa mag Aaróona, mook ay doomam yu góor, te nga sotti leen diwu pal gi, dénk leen seen sas. Noonu nga leen di sédde céru sellnga, ñu di ma sarxalal.

Nga daldi solal Aaróona yére yu sell yi, diw ko, sellale ko ko, mu doon sama sarxalkat.

¶ Ba loolu wéyee Musaa jël diwu pal ga, diw ca jaamookaay baak ya ca biir yépp, sellale ko yooya,

¶ «Sarxalkat, bi gëna màgg ci bokkam yiy sarxalkat, te ñu sotti diw gi ñuy fale ci boppam, sellal ko, muy sol yére yu sell yi, kooku du njañu te du xotti ay yéreem, di ko ñaawloo ku dee.

Wax nga say wóllëre ci peeñu, ne leen: «Tànne naa jàmbaar ci xeet wi, dénk ko ndimbal.

Noowug Boroom bi Aji Sax jaa ngi fi sama kaw, ndax Aji Sax jee ma diw, fal ma, ngir ma àgge néew-doole yi xibaaru jàmm. Moo ma yebal ngir ma dëfal ñi seen xol jeex, yégal jaam yi, seen goreel, yégal ñi ñu tëj, seen ubbite.