Sama diggante laak bànni Israyil, te firnde la ju sax dàkk, ndax ci juróom benni fan la Aji Sax ji sàkk asamaan ak suuf, bésub juróom ñaareel ba, mu dal-lu, daldi yeeslu.”»
TSK
TSK · Exodus 31:13
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ «Samay bési Noflaay nag wormaal-leen ko te sama bérab bu sell teral-leen ko. Maay Aji Sax ji.
Te itam nangeen ràññee ne ñu sell lañu, ndax seen ñamu Yàlla, ñoo koy joxe. Nangeen leen jox céru nit ñu sell, ndax ku Sell laa, man Aji Sax ji leen sellal, yeen.
«Waxal bànni Israyil ne leen: Bu ngeen duggee ca réew ma ma leen jox, suuf sa ca boppam war naa am àppu noflaayam ngir Aji Sax ji.
Sa bésub Noflaay bu sell it, yaa leen ko xamal, te say santaaneeki dogali yoon ak saw yoon, yaa leen ko dénk. Musaa, sa jaam ba, jottli leen ko.
Sama bési Noflaay, sellal-leen ko, muy firnde sama digganteek yeen, ngir ngeen ràññee ne man maay seen Yàlla Aji Sax ji.”
¶ «Bu jote amee, ñoom ñooy àtte, ba dogal àtte bi ci sama àttey yoon. Sama digal yeek sama dogali yoon yi jëm ci sama màggal yépp, ñoo koy sàmm, te sama bési Noflaay, ñoo koy sellal.
¶ Ci man Yudd miy jaamub Yeesu Almasi, di rakku Yanqóoba, ci man la bataaxal bii bawoo, ñeel leen yeen ñi ñu woo, yeen ñi Yàlla Baay bi sopp, te sàmmal leen Yeesu Almasi.