Lóot daldi génn, wax ak goroom, ya naroona takk ay doomam yu jigéen, ne leen: «Gaawleen gaaw, génn dëkk bi, ndaxte Aji Sax ji dina ko tas.» Teewul ñu defe ne day kaf.
TSK
TSK · Exodus 32:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Teewul Yuusufa bañ, ne soxnas sang ba: «Déglul, sama sang da maa jébbal lépp, ba topptootul dara ci kër gi.
Yuusufa ne leen: «Li ngeen def nag? Xanaa xamuleen ne nit ku mel ni man day gisaane?»
Ci biir loolu ñu ne Musaa: «Xanaa Misra dafa amul ay sëg, ba nga di nu indi ci màndiŋ mi, nu deesi fi? Loo nu doon génnee Misra?
¶ «Buleen am yeneen yàlla ci sama kanam.
Musaa yéeg ca kaw tund wa ba tàbbi ca biir niir wa, di wéy. Musaa nekk na ca kaw tund wa ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg.
Musaa nag tinu Yàllaam Aji Sax ji ne ko: «Aji Sax ji, ana lu waral sam sànj di tàkkal sa ñoñ ñi nga génne réewum Misra ci sa kàttan gu màgg ak sa dooley loxo?
Dañu ma ne: “Sàkkal nu yàlla ju nu jiite, ndax Musaa mii nu génne réewum Misra kat, xamunu lu ko dal.”
¶ Aji Sax ji ne ko: «Man ci sama bopp maay ànd ak yaw te maa lay noppal.»
¶ Israyil dégluleen! Yeena ngii tey, di jàll dexu Yurdan ngir dàqi xeet yu leen ëpp, ëpp leen doole, ngir nangu seen dëkk yu réy, dàbblikoo tata yu àkki asamaan.
¶ Ba ñeent fukki guddi ak ñeent fukki bëccëg matee, Aji Sax ji jox ma ñaari àlluway doj ya, àlluway kóllëre ga.
Yanqóobaa dawoon ba réewum Siri, Israyil laa ne, moo liggéey ngir am jabar, wut jabar tax koo sàmm ag jur.
Ñu ne Aaróona: “Sàkkal nu ay yàlla yu nu jiite, ndax Musaa mii nu génne réewum Misra, xamunu lu ko dal.”
Yeena gis nag mbaa ngeen déggal seen bopp ni Póol moomu di naxee ba fàbbi mbooloo mu bare, te du ci Efes gii rekk, daanaka Asi gépp la: Mu naay: “Yàlla yu loxol nit sàkk du yàlla.”