TSK

TSK · Exodus 32:16

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Aji Sax ji waxati Musaa ne ko: «Yettal ñaari àlluway doj yu mel ni yu jëkk ya, ma bind ci kàddu ya woon ca àlluwa yu jëkk, ya nga toj.

Ba ma yéegee ca tund wa, di jëli àlluway doj ya, àlluway kóllëre, gi Aji Sax ji fas ak yeen; toog naa ca kaw tund wa ñeent fukki bëccëg ak ñeent fukki guddi. Du ñam wu ma lekk, du ndox mu ma naan.

¶ Jant yooyu la ma Aji Sax ji wax ne ma: «Yettal ñaari àlluway doj yu mel ni yu jëkk ya, nga yéegsi fi man, ci kaw tund wi. Te nanga sàkk itam gaalu bant.

Bir na ne bataaxalub Almasi bu jottlikoo ci sunub liggéey, moom ngeen, te du daa lees ko binde, waaye Noowug Yàlla jiy dund lees ko binde. Du ci àlluway doj lees ko rëdd, waaye ci àlluway xoli suux, lees ko rëdd.

¶ «Lii nag moo di kóllëre gi may fas ak kër Israyil, gannaaw yooyu fan, la Boroom bi wax, mu ne: Maay yeb sama ndigali yoon ci seenum xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ.