«Waxal bànni Israyil ne leen, ñu indil ma ab jooxe. Ci képp ku am yéeneem ngeen di nangoo sama jooxe, indil ma ko.
TSK
TSK · Exodus 35:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Góor ak jigéen bokk dikk, mboolem ñi am yéeney xolam, mboolem ñi bëgga indi wurus, defal ko Aji Sax ji saraxu yékkati-jébbale; ñii indi ay lam, ñii jaaroy nopp, ñii jaaroy loxo, ñii ay caq, gànjari wurus yu nekk rekk.
Mboolem bànni Israyil, góor ñeek jigéen ñi am yéeney indi lu jëm ci liggéey bi Aji Sax ji santaane, Musaa jottli, ñoom ñépp a indil Aji Sax ji ay saraxi yéene.
¶ Ba mu ko defee ña jiite waa kër Yuda ak Beñamin ak sarxalkat yaak Leween ña, képp ku ci Yàlla xiir rekk, mu daldi dem tabaxi kër Aji Sax ja ca Yerusalem.
¶ Cant ñeel na Aji Sax ji, sunu Yàllay maam, moom mi def nii ci xolub Buur yéeney teral kër Aji Sax ji ci Yerusalem,
Sàmmala sàmm sab xol, nde xalaati xol ngay jëfe.
Kon na ku nekk joxe, ni mu ko waaje ci xolam, te bañ koo tiisoo, bañ koo joxee ñàkk pexe, ndax kiy joxee xol bu sedd, Yàlla sopp na ko,