¶ Yanqóoba nag wax ak Simeyon ak Lewi ne leen: «Indil ngeen ma musiba, ndax dingeen tax waa réew mépp sib ma, muy Kanaaneen ñi, di Periseen ñi. Te itam awma lu dul góor ñu néew, te bu ñu booloo dal ci sama kaw, dañu may booleek sama waa kër faagaagal.»
TSK
TSK · Exodus 5:21
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Genesis 34:30
TSK
Exodus 6:9
TSK
¶ Ba Musaa waxee loolu bànni Israyil, dégluwuñu ko sax ndax xol bu jeex ak njaam gu metti.
1 Samuel 13:4
TSK
Ñu yégal Israyil gépp la xew ne leen: «Sóol song na dalub waa Filisti, ba tax waa Filisti jéppi bànni Israyil.» Gàngoor ga daldi daje, topp ca gannaaw Sóol ca Gilgal.
2 Samuel 10:6
TSK
¶ Amoneen ña xam ne Daawuda jéppi na leen lool. Ñu dem bindi ñaar fukki junniy (20 000) xarekat ca waa Siri ña dëkke Bet Reyob ak waa Siri ña dëkke Soba, teg ca junniy nit ñu bàyyikoo ca buuru Maaka, ak fukki junneek ñaar (12 000) ñu waa Tob.
As weñ tàbbi ci diw gu xeeñ, yàq ko; ab dof it jëfam su tuut neenal na xel mu rafet ak daraja.
ndax kat nun nooy cuuraayal Almasi fa Yàlla, ñeel ñi ci yoonu texe, ak ñi ci yoonu sànkute.