TSK

TSK · Exodus 6:7

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Te dinaa feddli sama kóllëre, gi ci sama diggante ak yaw, yaak sa askan, muy kóllëre guy sax maasoo maas ba fàww. Maay doon sa Yàlla, yaak sa askan.

Dalal ci réew mii; dinaa ànd ak yaw, barkeel la. Yaak sa askan laay jox suuf sii sépp, te dinaa sàmm li ma giñaloon sa baay Ibraayma.

¶ Buuru Misra ne leen: «Yeen Musaa ak Aaróona, lu waral ngeen di jële mbooloo mi ci seeni liggéey? Laggleen ca seeni sas waay!»

Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Ni ngay xame ne man maay Aji Sax ji nii la: Dama ne, dinaa dóor ci ndoxum Niil mi yet, wi ci sama loxo, ndox mi soppliku deret;

Su ko defee, bu leen seen doom laajee ëllëg, ne leen: “Lii lu muy tekki?” ngeen wax ko ne ko: “Dooley loxol Aji Sax jee nu génne Misra, kërug njaam ga.

Bu ma dumaa Firawna, boole kooki watiiram aki gawaram, ba doxe fa siiwal sama ndam, waa Misra dinañu xam ne man maay Aji Sax ji.»

tiitaangeek njàqaree ne milib ca seen kaw. Sa kàttan a tax ñu mel niw doj, ne yàcc, ba kera sa ñoñ jàll, Aji Sax ji, ba kera askan wa nga goreel, jàll,

Léegi nag su ngeen ma déggalee bu baax, di sàmm sama kóllëre ak yeen, yeenay doon sama moomeelu bopp ci mboolem askan yi. Dëgg la, àddina wërngal këpp maay Boroom,

Su boobaa bànni Israyil xam ne, man Aji Sax ji maay seen Yàlla, ji leen génnee réewum Misra, ngir dëkk fi seen biir. Man maay seen Yàlla Aji Sax ji.

Yeen nag Aji Sax jee leen jël, bellee leen ca Misra, taalu xellikaayu weñ gu ñuul ba, ngir ngeen doon ñoñam ñi mu séddoo niki bésub tey.

ndax askan wu sell ngeen, ñeel seen Yàlla Aji Sax ji. Yeen la Aji Sax ji taamu, ngir ngeen doon askan wi mu séddool boppam, ci mboolem askani kaw suuf.

Mburu, lekkuleen ko, biiñ mbaa geneen naan gu diis, naanuleen ko. Maa leen leel, ngir ngeen xam ne man maay seen Yàlla Aji Sax ji.»

Aji Sax ji nee: «Du yeen doŋŋ laay fasool kóllëre gii, ak ngiñ lii.»

Yaa dëgëral Israyil sa ñoñ, ngir ñoñoo leen ba fàww, te yaw Aji Sax ji, yaa doon seen Yàlla.

Góoru Yàlla ga dikk ne buurub Israyil: «Aji Sax ji dafa wax ne: Gannaaw waa Siri dañoo yaakaar ne man Aji Sax ji, yàllay tund laa, duma yàllay xur, maay teg mbooloo mu réy mii mépp ci say loxo. Su ko defee ngeen xam ne maay Aji Sax ji.»

di ndénkaane lu mu dénk waa kër Yuusufa, ba Yàllay dali ca kaw réewum Misra. Baat bu ma xamul laa dégg, mu naan:

ndax nit ñi gis, ba xàmmee, ñoom ñépp nemmiku, ba xam ne Aji Sax jee def lii ci loxoom, xam ne Aji Sell ju Israyil a sàkk lii.

Ñi lay néewal, maa leen di leel seen suuxu bopp. Seen deret ni biiñ bu bees, ma màndale leen, ba kuy boroom suux xam ne maay Aji Sax ji lay wallu, jàmbaaru Yanqóoba ji lay jot.»

«Waaye kóllëre gi may fas ak waa kër Israyil gannaaw loolu,» kàddug Aji Sax jee, «nii lay deme: Maay yeb sama ndigali yoon ci seen xel, ci seen xol laa koy ñaas. Maay doon seen Yàlla, ñoom ñu doon sama ñoñ.

Ñetteel bi laay tàbbal ci sawara, xelli ko ca ni ñuy xellee xaalis, nattu ko ni ñuy nattoo wurus cib taal. Xaaj boobu moo may woo ci sama tur, ma wuyu ko. Moom laay wax: “Sama ñoñ,” Moom mu ne: “Aji Sax jeey sama Yàlla.”»

¶ Ana lu nuy waxati nag? Gannaaw Yàllaa ànd ak nun, ku nu manal dara?

Yeen ñi dul woon sax aw xeet, démb, tey yeen ay xeet wi Yàlla ñoñoo; dajaguleen woon yërmande, waaye tey daj ngeen yërmande.

Képp ku am ndam nag, loolooy doon sab cér. Maay doon sa Yàlla, nga doon sama doom,