TSK

TSK · Exodus 7:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji ne ko: «Keroog boo delloo Misra, nanga taxaw temm, te def ca kanam Firawna kéemaan, yi ma teg ci sa loxo yépp. Man maay dëgëral boppam, mu të ba du bàyyi mbooloo mi, ñu dem.

Ñeengokati Misra itam fexe ca seeni xargafuufa, ba def lu mel noona. Firawna të rekk, tanqamlu Musaak Aaróona, muy la Aji Sax ji waxoon.

Ñeengokat ya ne Firawna: «Lii de Yàlla rekk a ko man!» Teewul Firawna wéye të rekk, tanqamlu leen, muy la Aji Sax ji waxoon.

Ba Firawna yónnee, ba nemmiku mbir ma, xam na ne lenn deewul ca juru bànni Israyil. Teewul mu të ticc ba tey, baña bàyyi mbooloo ma, ñu dem.

¶ Ba loolu weesee Aji Sax ji dafa wax Musaa ne ko: «Demal ca Firawna. Maa dëgëral boppam, mooki dagam, ngir jëfe samay firnde fi seen biir.

Teewul Aji Sax ji dëgëral boppu Firawna, mu të rekk, bañ leena bàyyi ñu dem.

¶ Siwon buurub Esbon nag nanguwu noo may nu jaare fa moom, ndax booba seen Yàlla Aji Sax ji moo dëgëral boppam, wowal xolam, ngir teg ko ci seen loxo niki bésub tey jii.

Seen bopp lañu dëgëral niw doj, ba faaleetuñu ndigalu yoon wi, ak kàddu yi Aji Sax ji Boroom gàngoor yi yónnee ag Noowam, ci jottlib yonent yu jëkk ya. Muy sànj mu réy nag, bawoo fa Aji Sax ji Boroom gàngoor yi.

¶ Waaye sag dëgër bopp, ak sa xol bu tuubadi, ci ngay jóore sànjum Yàlla ci sa kaw bopp, keroog bésub sànj ma, fa àtteb Yàlla bu jub di feeñe.

Waaye bés bu nekk deeleen soññante li feek muy bésub tey agum, bala bàkkaar a nax kenn ci yeen, ba mu mujj dërkiis.