TSK

TSK · Exodus 7:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Waaye su lenn ci ñaari firnde yi taxul ñu gëm, te déggaluñu la, nanga tanqe ndox ci dexu Niil gi, tuur ko ci suuf su wow si, su ko defee ndox, ma nga tanqe ca dex ga, day soppliku deret ci suuf si.»

¶ Aji Sax ji waxati Musaa, ne ko: «Teelala xëy ëllëg ca Firawna, buy génn jëm ca ndox ma, nga wax ko ne ko: “Aji Sax ji dafa wax ne: ‘Bàyyil sama ñoñ, ñu dem jaamuji ma.

¶ Naka la Musaa bàyyikoo ca Firawna, ba génn dëkk ba rekk, daldi tàllal Aji Sax ji ay loxoom. Dënu yaak tawub yuur ba ne tekk, taw ba siwet.

¶ Gannaaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: «Tàllalal sa loxo, mu jublu asamaan, lëndëm wàcc ci kaw réewum Misra, lëndëm gu nit mana daj, ndax fatt.»

¶ Aji Sax ji nag wax Musaa ne ko: «Tàllalal sa loxo, mu tiim géej gi, ndax ndox mi délsi, ba sottiku ci kaw waa Misra, ñook seen watiiri xare ak seeni gawar.»