TSK

TSK · Exodus 8:32

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

Aji Sax ji ne ko: «Keroog boo delloo Misra, nanga taxaw temm, te def ca kanam Firawna kéemaan, yi ma teg ci sa loxo yépp. Man maay dëgëral boppam, mu të ba du bàyyi mbooloo mi, ñu dem.

Musaa ak Aaróona nag jóge ca Firawna, Musaa tinu Aji Sax ji ca mbirum mbott ya mu yare Firawna.

Ba Firawna yónnee, ba nemmiku mbir ma, xam na ne lenn deewul ca juru bànni Israyil. Teewul mu të ticc ba tey, baña bàyyi mbooloo ma, ñu dem.

Mu ne: “Demal ci xeet wii, nga ne leen: ‘Yeenay dégloo déglu, dungeen dégg; ngeen xoolee xoole, dungeen gis.’

¶ Képp ku dajeek lu koy xiirtal, bumu ne: «Yàllaa ma xiirtal,» ndax maneesula xiirtal Yàlla ci lu bon, te moom ci boppam du xiirtal kenn.