Maa ngi yërëm Mowab, bay binni ni buumu riiti, sama yaram daw ci Kir Eres.
TSK
TSK · Ezekiel 21:6
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Moo ma tax ne: «Buleen ma xool, damay naqarlu, jooy. Tàyyileen maa dëfal ci sama bokk yi sànku.»
Nañu gaaw dëbbeel nuy jooy, gët taa, rongooñ wal.
Laajteleen te xool, ndax góor day wasin léegi? Moona maa gis jàmbaar ju ne jatu, ni kuy matu, kanam xoyy.
«“Boroom bi Aji Sax ji dafa wax ne: Fenqeel say loxo, dóor sa tànk fi suuf te ne: ‘Ñaw!’ ci mboolem jëfi waa kër Israyil ju bon ju siblu. Saamar ak xiif ak mbas lañuy fàddoo.
Yaw nag nit ki, dajaleel digg bëccëg, ñépp gis, sa jumtukaayi ku jëm ngàllo te nga sanci feneen, ñépp teg ci bët. Jombul ñu gis ne kërug fippukat lañu.
¶ «Nanga ŋàbb dénk yi nga bind, ñuy gis,
¶ Ba loolu amee ma ne làcc, wopp ay fan, man Dañeel. Gannaaw gi ma jóg, dellu ca liggéeyu buur. Ma waaru nag ca peeñu ma, ndax daa wees sama dég-dég.
Ba ma ca déggee, samay butit a yëngu, coow la tax samay tuñ di lox, sama yaram dee goyy, may lox fi ma taxaw, te ne cell, di séentu bésub njàqare, bay dikkal xeet wi nu song.