Gannaaw gi ña nekkoon ca dëkk ba ba booba, ak ña jébbaloon seen bopp buuru Babilon ak la desoon ca waa réew ma, Nebusaradan njiital dagi buur, boole leen yóbbu ngàllo.
TSK
TSK · Ezra 2:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Buur, nu ngi lay xamal ne dem nanu ca diiwaanu Yuda, ca kër Yàlla ju màgg ja. Ña nga koy tabaxe doj yu mag, di teg ay dénk ca miir ya. Liggéey baa ngay dox bu baax, di jëm kanam.
¶ Ñii nag ñoo di niti diiwaanu Yuda, ña jóge njaam ca ngàllo ga leen Nabukodonosor buuru Babilon yóbbu woon, te ñu jóge ca ñibbsi Yerusalem ak Yuda, ku nekk ak fa mu dëkk.
¶ Lii mu ngi amoon ci jamonoy Aserus. Mooy Aserus ma falu woon, jiite téeméeri diiwaan ak ñaar fukk ak juróom ñaar, dale ko ca End ga woon, ba ca réewum Kuus.
Kenn gawuloon kenn nag ci naan gi, ndax Buur joxoon na ndigal farbay këram yépp, ne leen ñu topp ku nekk ci coobareem.
¶ Ci kaw loolu ñu woo bindkati buur ca bés ba, di ñaar fukki fan ak ñett ca weeru Siwan, ñetteelu weer wa. Ñu daldi bind mboolem lu Mardose santaane, ca mbirum Yawut yaak jawriñ yaak boroom dëkk yaak kàngami diiwaan ya, dale ko ca End ba ca Kuus. Muy téeméeri diiwaan ak ñaar fukk ak juróom ñaar (127). Ñu bind ndigal ya ci mbindum diiwaan bu nekk ak ci làkku xeet wu nekk, Yawut ya it ak seen mbindu bopp ak seen làkku bopp.
¶ Ba Cedesyas tolloo ci juróom ñeenteelu atu nguuram, ca fukkeelu weeram, ca la Nabukodonosor buuru Babilon ànd ak mbooloom xareem mépp ci kaw Yerusalem, ñu gaw ko.
¶ Ñaar fukki at ak benn la Cedekiya amoon ba muy falu buur, te fukki at ak benn la nguuru fa Yerusalem. Yaayam mooy Amutal doomu Yeremi ma cosaanoo Libna.
Seen noon yaa jiite tey, seen bañ yooyoo ne finaax, Aji Sax jee mbugale waa Siyoŋ seeni tooñ yu bare, seeni doom duggig njaam, di moomeel ub noon.
Tefes ga, ndesu kër Yuda koy moom, ñu di ca fore, bu ngoonee ñu tëri néegi Askalon. Seen Yàlla Aji Sax jee leen di dikkal, tijji seen wërsëg (/yiwileen cig njaam.)