TSK

TSK · Genesis 11:30

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Sarayi amul woon doom ak boroom këram Ibraam. Waaye fekk na mu am jaam bu juddoo Misra te tudd Ajara.

Booba fekk na Ibraayma ak Saarata doon mag, ba màggat lool sax, te Saarata weesoon na njurum doom.

Gannaaw ga soxnas Isaaxa amul doom, Isaaxa dagaanal ko Aji Sax ji, mu nangul ko, soxna si daldi ëmb.

¶ Ba Rasel gisee ne amalul Yanqóoba doom, dafa ñee magam, ba tax mu wax Yanqóoba ne ko: «Nanu am ay doom, mbaa ma dee.»

Elkana amoon na ñaari soxna. Kenn ka di Aana, ka ca des di Penina. Penina amoon na ay doom, waaye Aana amul woon doom.

Mooy dëël jigéen ju tële woona jur, may ko mbégtem njureel. Màggal-leen Ki Sax!

Luke 1:36 TSK

Te kat Elisabet sa mbokk mi itam ëmb na doom ju góor te fekk ko màggat. Ki ñu doon wooye jigéen ju jaasir, mu ngi nii ci juróom benni weeram,