TSK

TSK · Genesis 12:1

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Mu am bés Teraa ànd ak doomam Ibraam ak sëtam Lóot, mi Aran di baayam, ak Sarayi, soxnas Ibraam. Ñu bokk jóge Ur gu Kaldeen ña, jëm réewu Kanaan. Ba ñu demee ba Karan, daldi fay sanc.

Te bés, ba ma Yàlla génnee sama kër baay, may wëndeelu, dama koo waxoon ne ko: “Déglul, li ngay def soo ma bëggee xettli, mooy lii: fépp fu nu dem, nanga wax ne sa càmmiñ laa.”»

Waaye demal ca sama kër baay, ca samay bokk, nga jëlal fa sama doom soxna.”

Yaw yaa di Aji Sax ji, Yàlla ji tànn Ibraam, jële ko Ur gu waa Kalde, tudde ko Ibraayma.

Yaw mi ma jukkee fa cati àddina, wooye la fa gëna sore, wax la ne la: «Yaa di sama jaam, maa la taamu te duma la wacc,»

«Yaw nit ki, ñi dëkke genti réewum Israyil mii ñu ngi naan: “Ibraayma kenn la woon te moo moomoon réew mi. Kon nun ñiy ñu bare noo ko ci gëna yey.”

Acts 7:2 TSK

Eccen ne ko: «Yeen bokk yi, yeen samay baay, dégluleen! Yàlla, miy Boroom daraja moo feeñu woon sunu maam Ibraayma, ba mu nekkee réewum Mesopotami, bala moo sanc Karan.

¶ Ba Yàllay woo Ibraayma, ngir mu génn, jëm bérab ba mu mujj muurloo, ngëm la déggale Yàlla, ba génn, dem te xamul woon fu mu jëm.