TSK

TSK · Genesis 12:11

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

ay goney Yàlla ñoo gis jigéen ñeek seen taar, ñuy jël ñi ñu bëgg ci ñoom, def leeni jabar.

Te bés, ba ma Yàlla génnee sama kër baay, may wëndeelu, dama koo waxoon ne ko: “Déglul, li ngay def soo ma bëggee xettli, mooy lii: fépp fu nu dem, nanga wax ne sa càmmiñ laa.”»

Góori foofa laaj ko ndaw si mu àndal, lu mu doon ci moom, mu ne: «Sama jigéen la.» Dafa bañoona wax ne soxnaam la, ngir ragal waa foofa rey ko ndax taaru Rebeka.

Mu daldi bàyyi lépp ci loxol Yuusufa, te li mu fa nekk tax ba topptootul dara ciy mbiram, lu moy li muy lekk rekk. Booba Yuusufa ku jekkoon bind la te góorayiw.

¶ Genn ngoon, Buur Daawuda jóge ca kaw laltoom, di doxantu ca kaw taaxum këram. Mu tollu ca kaw taax ma, séen as ndaw suy sangu. Ndaw sa neexa xool lool.

Nit xeluwul, amul ug dégg ak pexe, ba manal Aji Sax ji dara.