Ci kaw loolu Aji Sax ji feeñu Ibraam ne ko: «Sa askan wi soqikoo ci yaw laay jox réew mii.» Ibraam nag daldi tabaxal Aji Sax, ji ko feeñu, ab sarxalukaay.
TSK
TSK · Genesis 13:4
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba mu ko defee Ibraam sempi xaymaam, ñëw dal Ebron ca garab yu mag ya ca toolub Mamre, daldi fay tabaxal Aji Sax ji sarxalukaay.
Aji Sax ji, maa sopp sa dëkkuwaay, bëgg bérab bi sag leer teew.
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di woyu Sabóor, ñeel Daawuda.
Éy Yàlla, geesul Buur, sunu kiirlaay, ngalla niiral kii nga fal.
Nañu sante Aji Sax ji ngoram ak kéemaanam yi ñeel doom aadama yi.
Teewlu na ma moos, dama koy woo li feek may dund.
Aji Sax ji, képp ku ko woo wall, mu jege la, képp ku ko woo wall te muy dëgg.
Su boobaa ngeen woo ma wall, dikk ñaan ma, ma nangul leen.
ñeel mbooloom Yàlla, mi ci Korent, yeen ñi ñu sellal ci jëmmu Almasi Yeesu, te ñu woo leen ngir ngeen doon ñu sell, ñeel itam mboolem ñiy tudde fépp fu mu mana doon, sunu turu Boroom Yeesu Almasi, mi leen moom, moom nu.