TSK

TSK · Genesis 14:13

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba mu ko defee Ibraam sempi xaymaam, ñëw dal Ebron ca garab yu mag ya ca toolub Mamre, daldi fay tabaxal Aji Sax ji sarxalukaay.

Ndax man kat dañu maa sàcce ca réewum Ebrë ya, te fii itam, defuma fi lu tax, ñu war maa tëj.»

Loolu wees ñu may Yuusufa moom rekk; ber doomi baayam ya. Waa Misra ña fa doon lekke it, ñu beral leen seen ndab, ngir waa Misra daawuñu bokk ak Ebrë yi lekk, ndax mbañ la fa woon.

¶ Ba ñu demee ba Musaa màgg, dafa am bés, mu seeti bokkam ya, gis leen ca liggéey yu metti, ya ñu leen sas. Mu gis jenn waayu Misra di dóor kenn ca bokki Ebrë ya.

¶ Ba mu ko defee jenn waay ju bokk ci giirug Beñamin, dawe ca làngu xare ba ca Silo ci benn bés bi. Mu agsee yére yu xottiku ak bopp bu fees ak suuf, di ko tiisloo.

Job 1:15 TSK

Genn gàngooru yàqkat bàyyikoo Saba, dikk daanu ci seen kaw, yóbbu leen; surga ya, ñu leel ñawkay saamar. Mennum man mii maa ca rëcce ba àggesi la ko.»

¶ Xanaa ay Ebrë lañu? Ak man itam. Xanaa ci xeetu Israyil lañu bokk? Ak man itam. Xanaa ay sëti Ibraayma lañu? Ak man itam.