Matusalem juddu na, ba noppi Enog topp Yàlla ñetti téeméeri at (300), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen.
TSK
TSK · Genesis 17:1
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Askanu Nóoyin mooy lii. Nóoyin nit ku jub la woon, di ku mat ci biir nit ñi mu bokkal jamono, te di ku topp Yàlla.
Ci kaw loolu Aji Sax ji feeñu Ibraam ne ko: «Sa askan wi soqikoo ci yaw laay jox réew mii.» Ibraam nag daldi tabaxal Aji Sax, ji ko feeñu, ab sarxalukaay.
¶ Am na bés, Aji Sax ji feeñu Ibraayma ca garabi Mamre yu mag ya. Booba ma nga toogoon ca buntu xaymaam digg njolloor.
Mu ne ma: “Aji Sax, ji ma topp, dina yónni malaakaam, mu ànd ak yaw, ba àntalal la sa yoon, nga jëlal sama doom soxna ca sama kër baay, ca sama biiri bokk.
Yàlla neeti ko: «Man maay Yàlla Aji Man ji. Giiral te yokku, ba aw askan ak mboolooy askan sosoo ci yaw, te ay buur askanoo ci sa geño.
¶ Yanqóoba ne Yuusufa: «Yàlla Buur bi feeñu woon na ma ca Lus ca réewu Kanaan, barkeel ma,
Yàlla Aji Man ji, mooy ni ma feeñoo woon Ibraayma, te ni laa feeñoo Isaaxa ak Yanqóoba it, waaye sama tur, Aji Sax ji, leeraluma leen ko woon.
kàddug kiy dégg waxi Yàlla, kiy xame ca xam-xamu Aji Kawe ji, Aji Man ji wonem peeñu, mu gis, kiy daanu leer, te ay gëtam muriku.
¶ Muccleen sikk seen digganteek seen Yàlla Aji Sax ji,
Suleymaan ne ko: «Yaw de yaa baaxe lool sab jaam Daawuda, saa baay, ngir na mu daan doxale fi sa kanam ci dëgg ak njekk ak njubteg xol. Yaa ko baaxe lool, may ko doom ju góor ju toog cib jalam, bésub tey jii.
«Éy Aji Sax ji, ngalla bàyyil xel ni ma àndeek yaw sama léppi xol, ci kóllëre, te li nga rafetlu laa jëfe.» Mu jooy nag, jooy yu metti.
Dangaa mana gëstu mbóoti Yàlla, ba gis ko? Am yaa ñédd Aji Man ji?
Damay topp Aji Sax ji ci biir réewum aji dund ñi.
Mu ne: «Éy Aji Sax ji, ngalla bàyyil xel ni ma àndeek yaw sama léppi xol, ci kóllëre. Te it li nga rafetlu laa jëfe.» Mu jooy nag, jooy yu metti.
Ñoom ñaar ñépp a juboon, Yàlla seede, te mucc ayib ni ñuy jëfe santaane yeek ndigali yooni Boroom bi.
Moo tax fu ma tollu, man itam, may def lu ma man ngir am xel mu dal, wàccoo ak Yàlla, wàccoo ak nit ñi.
Lépp laa mane ci ndimbalal Ki may manal.
¶ Kon nag gannaaw nguur gu deesul yëngal lanu jagoo, nanu jàppoo cant, di jaamu Yàlla ni mu ko bëgge cig njullite akug ragal,