Mu teg ca ne: «Man maay sa Yàllay baay, di Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa te di Yàllay Yanqóoba.» Ca la Musaa nëbb kanam ga, ndax ragala xool Yàlla.
TSK
TSK · Genesis 17:3
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba loolu amee Musaa ne gurub, moom ak Aaróona, ñu dëpp seen jë fa suuf, fa kanam mbooloom bànni Israyil ma fa daje mépp.
Mu mel ni xon ci biiri niir, bésub taw. Loolooy melokaanu leer ga ko wër. Muy melokaan muy jëmmal leeru Aji Sax ji. Naka laa ko gis, daldi ne gurub, dëpp sama kanam fi suuf. Ma dégg nag kàddu gu jib.
¶ Naka lañu dem, reyi, ma des fa man doŋŋ. Ma daldi daanu, dëpp sama kanam fa suuf, daldi àddu ca kaw, ne: «Éy Boroom bi Aji Sax ji, xanaa doo sànk mboolem ndesu Israyil ci sa xadar jii ngay xëpp ci kaw Yerusalem?»
Ci kaw loolu ma dégg baatam. Naka laa dégg baatam, daldi daanu leer, sama kanam dëppu fi suuf.
¶ Naka laa ko gis, ne dàll daanu ci ay tànkam ni ku dee. Mu teg ma loxol ndijooram, ne ma: «Bul tiit. Maay Ki Jëkk, di Ki Mujj.