Waaye sama kóllëre nag, Isaaxa laa koy fasool, moom Isaaxa, mi Saarata di am, nëgëni déwén.»
TSK
TSK · Genesis 18:14
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Saarata ëmb, amal Ibraayma doom ju góor ci jamono, ji ko Yàlla waxoon, te fekk góor gi di màggat.
Buleen am tiitaange ci ñoom, ndax seen Yàlla Aji Sax ji ci seen biir, Yàlla ju màgg la te raglu.
Alyaasa ne ko: «Nëgëni déwén dinga leewu doom ju góor.» Mu ne ko: «Déet, sang bi, góoru Yàlla gi, bu ma nax mukk, sang bi.»
Dama ne, Yàllaa màgg te du jalaxe, moo màgg te réy um xel.
Aji Sax ji, délsil, loo deeti xaar? Ngalla yërëmal sa jaam ñi.
Aji Sax jeey Yàlla ju màgg ji, buur bu mag bi tiim yàllay xeet yépp.
«Du maay Aji Sax ji, Yàllay képp kuy dund. Ana lu ma të?»
Aji Sax ji Boroom gàngoor yi dafa wax ne: «Su loolu dee kawtéef ci gis-gisu ndesu askan wi ci yooyu jant, ndax tax na muy kawtéef ci sama gis-gis itam?» Kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi.
¶ Sàkkaryaa nag ne malaaka mi: «Lu may def ab takk ci loolu ba mu bir ma? Ndax man màggat naa, te sama soxna it làq na ay fan.»
Yeesu dégg ca, ne njiit la: «Bul tiit. Gëmal rekk, mu daldi mucc.»
¶ Moom mi mana jëfoo kàttan giy liggéey ci nun, ba sottal mboolem lu nu ñaan ak lu nu xalaat, ba wees loola fuuf sax,
Lépp laa mane ci ndimbalal Ki may manal.