TSK

TSK · Genesis 18:19

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba loolu amee Ibraayma boole doomam Ismayla, ak jaam, yi juddoo këram yépp, ak ñi mu jëndoon ci xaalisam ñépp, góori waa këram ñépp, xarfal leen ca bés ba, muy la ko Yàlla waxoon.

Dañoo wara sàkkaat ay doj, wuutale ko doj yooyu te sàkk ban bu bees, raaxe ko néeg bi.

Bés ba ngeen taxawee fa seen kanam Yàlla Aji Sax ji, fa tundu Oreb, Aji Sax jee ma ne: «Dajaleel ma mbooloo mi, ma dégtal leen samay kàddu, ngir ñu tàggatu ci ragal ma li feek ñuy dund ci kaw suuf, te seeni doom it, ñu tàggat leen ci.»

Nangeen ko jàngal seeni doom, di ko waxe bu ngeen toogee seen biir néeg, ak bu ngeen di dox ciw yoon, ak bu ngeen tëddee, ak bu ngeen jógee.

Kon nag kàddug Aji Sax jee, Yàllay Israyil: “Maa waxoon déy ne, sa waa kër ak sa waa kër baay ñooy doxe fi sama kanam, di ma liggéeyal ba fàww.” Léegi nag, kàddug Aji Sax jee: “Loolu jomb naa ko tey. Ñi ma teral laay teral; waaye ñi ma teddadil, dees na leen tuutal.

Sàmm naa yooni Aji Sax ji, bonuma, di moy sama Yàlla.

Aji Sax ji kay ay sàmm yoonu aji jub; yoonu ku bon di sànk boroom.

Na dëddu lu bon tey def lu baax, sàkku jàmm, saxoo ko.

Bindal na sëti Yanqóoba téereb seede, muy yoon wi mu tegal Israyil. Mu sant maam yi, ñu xamal ko seeni doom,

Tegal gone ciw yoon, ba bu màggee, du ko wacc.

Amos 3:2 TSK

«Yeen doŋŋ laa ràññee ci mboolem askani suuf. Moo tax ma di leen mbugal ndax seen ñaawtéef gépp.»

Ndax malaakam Yàlla ji ma moom, te ma di ko jaamu, moo ma dikkal biig.

¶ Yeen ñiy baay it, buleen xoñoñal xale yi, waaye yarleen leen, di leen jubanti, di leen xamal coobarey Boroom bi.

¶ Ab taxawukatu mbooloo mi bumu denc lu wees jenn jabar te na yor ay doomam, ak këram, yorin wu rafet.

Teewul cëslaay lu dëgër, li Yàlla tabax, mu ngi ne kekk, te màndarga ma ca nekk, kàddu yii la: «Boroom bi xam na ay ñoñam,» ak: «Kuy tudd turu Sang bi, na daw njubadi.»