¶ Gannaaw loolu gan ña jóge foofa, tiim Sodom, di ko séentu. Ibraayma ànd ak ñoom, di leen gunge.
TSK
TSK · Genesis 18:2
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
¶ Ba loolu amee ñaari malaaka ya dikk Sodom ca ngoon, fekk Lóot toog ca buntu dëkk ba. Lóot séen leen, jóg gatandu leen, daldi leen sujjóotal, ne leen:
¶ Ba mu ko defee Ibraayma sujjóotal waa réew ma,
Moom ci boppam nag, mu jiitu leen, wutali magam, di dox tey sujjóot, ba muy juróom ñaari yoon.
¶ Ba Yuusufa wàccsee, ñu jébbal ko foofa ca biir kër ga sarica, ba ñu ko indaaleel, daldi koy sujjóotal.
¶ Yuda aki doomi baayam nag délsi kër Yuusufa, fekk demagul. Ñu daldi ne nërëm, dëpp seen jë fi suuf.
¶ Kuréli yonenti Yeriko ya doon seetaan a nga janook moom naa: «Leeru Ilyaas wàcc na ci kaw Alyaasa!» Ba loolu amee ñu gatandu ko, sujjóotal ko, dëpp seen jë ca suuf.
Buleen sàggane di terle, nde am na ñu seen teraanga tax ñu fat ay malaaka te xamuñu ko woon.