TSK

TSK · Genesis 18:21

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ba ñu noppee Aji Sax ji wàcc, xoolsi dëkk bi ak taax, mi doom aadama yi tabax.

Damaa wàcc, xettlisi leen ci waa Misra; génne leen réew moomu, ba yóbbu leen réew mu baax te yaatu, réew mu meew maak lem ja tuuroo, foofa ca diiwaanu Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña.

Fàttlikuleen mboolem yoon wi leen seen Yàlla Aji Sax ji awale diiru ñeent fukki at yii ci màndiŋ mi, teg leen coono, nattu leen ngir xam li ci seen biir xol, xam ndax dingeen wormaal ay santaaneem, am déet.

Sunuy ñaawtéef a ngi janook yaw, te sunu mbóot leer na la.

«Bàkkaaru Yuda lañu binde xaccug weñ gu cat la di doj wu dëgër. Dees koo ñaas ci seen àlluway xol, ñaas ko ci seen béjjéni sarxalukaay.

Jonah 1:2 TSK

«Jógal dem Niniw, dëkk bu mag ba, nga rëbb leen, ndax seen mbon agsi na ba fi man.»

Jantub keroog ay làmp laay niite Yerusalem, ba dikke mbugal ña fa ne degg, taaje ni biiñ ci kaw ginjriitam, te naa ci seen xel: “Aji Sax ji baaxewul, lorewul.”

Sang bi ci boppam, woote bu xumb lay wàccaalee asamaan, baatu kilifag malaaka jib, ànd ak coowal liitu Yàlla. Su ko defee ña seenug dee fekk ñu gëm Almasi ñooy jëkka dekki.