Musaa ak Aaróona ne gurub, dëpp seen jë fa suuf, daldi ne: «Éy Yàlla, yaw Yàllay bépp boroom bakkan bu bindoo aw suux, xanaa du kenn ay bàkkaar, nga far sànju ci kaw mbooloom lëmm?»
TSK
TSK · Genesis 18:25
Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.
Ana Yàllaak safaan yoon? Ana Aji Man jeek safaan dëgg?
Lépp benn la rekk! Moo tax ma ne: «Ku mucc ayib ak ku bon lay boole fàkkas.»
Li wóor mooy Yàlla du def lu bon, Aji Man ji du jalgati yoon.
Yàllaay àtte dëgg. Yàllaay rëbbe bés bu ne.
Asamaan a ngi biral njekkam, ngir Yàllaay àtte. Selaw.
Yàlla nee: «Maay takk ab àpp, àtte ca njub.
gatandoo ko Aji Sax jiy dikk, àttesi àddina, di àtte dun bi njekk, tey àttee xeet yépp dëgg.
Nit bàkkaar na téeméeri yoon, te teewul mu gudd fan. Xam naa it ne nee ñu ngëneel a ñeel ku ragal Yàlla, ndax wormaal ko.
Aji jub ñaa ngi dee, te kenn yégalu ko yaramam. Gor ñaa ngi faatu, te kenn ràññeewul ne aji jub ji, faatoom, musiba la koy moyale.
Ca ngeen di ràññaatlewaat diggante ku jub ak ku bon, kuy jaamu Yàlla, ak ku ko jaamuwul.
¶ Waaye su sunug njubadi fésalee njubteg Yàlla, ana lu loolu mana tekki ci nun? Ma waxe ko nu ko nit mana dégge; ma ne, kon bu nu Yàlla wàcceelee am sànjam, deful ag njubadeem?