TSK

TSK · Genesis 2:4

Treasury of Scripture Knowledge references in KYG.

Dellu ci pàcc bi

¶ Ca njàlbéen ga Yàlla sàkk na asamaan ak suuf.

Yàlla barkeel leen ne leen: «Giirleen te bare, ba fees àddina, di ko saytu; te it yilifleen jëni géej ak picci asamaan ak mboolem mbindeef muy yëngu ci kaw suuf.»

¶ Ni téere indee askanu Aadama nii la. Ba Yàlla di sàkk nit, da koo bind ci melokaanam,

¶ Askanu Sem mooy lii. Sem am na téeméeri at, doora jur Arpagsàdd, fekk na mbënn ma wees, ba mu am ñaari at.

¶ Isaaxa doomu Ibraayma ju góor ja, askanam mooy lii. Ibraaymaa jur Isaaxa.

¶ Askanu Esawu, di maami Edomeen ña ca tundi Seyir, mooy lii.

«Aji Sax ji jàmbaari xare ji, Aji Sax jeey turam!

Yàllaa mat. Kàddug Aji Sax jee wér te wóor. Mooy feg képp ku ko làqoo.

Muy ñaanu Musaa, góorug Yàlla ga. Boroom bi, yaa nu masa fat maasoo maas.

¶ Lii mu ngi tukkee ci man Yowaan, ñeel juróom ñaari mboolooy gëmkat ña ca diiwaanu Asi. Na leen yiw ak jàmm ñeel, tukkee fa Ki masa Nekk, Ki Nekk, di Kiy Dikk, tukkee it fa boroom juróom ñaari noo ya fa kanam ngànguneem,

Ñu ne: «Boroom bi Yàlla Aji Man, ji nekk te nekkoon, nu ngi lay gërëm, ndax yaa ràngoo sa kàttan gu màgg, taxawal sa nguur.